Waxal ag askan wi…
Président nee nañu dafa doy
Askan bi moo ma yónni nee nañ sonn nañu tàyyi nañu
Sunu président ci yaw la ñu wara roy kon boog na nga ligeey
Mag ñi ligeey, ndaw ñi ligeey, buñu bëgee rew mi jëm kanam
Kune defal sa keemtalaay kàttan buñu bëgee rew mi jëm kanam
Amul gòor, amul jigeen, ñun ñëpp a ci bokk yam
Ñun bëguñu…ñun bëguñu taxaw di gis seen deal
Dundatuñu, sangoutuñu, dund gi metti na
Ñun weruñu te lekkuñu, waxtaan waax dëg ci la
Nawet bi ñëw na ku ci sonn mbaa du mbënd mi la
Waa rewmi nak foog mu am ñu dem jangi discipline
Fune ñuy sanni, fune ñuy sotti mbalit mbed bile
Agressions yi di gën di tar, nga dof doflu ñu kill la
Kon prési wax ñu numuy demee, nee la wala nii la
Bu kune balee buntu këram lepp gëna chill
Waxal police ñu bayi dóor doomu askan bile
Luyass bu cher bi lañuy jooy, lu jar a lijjanti la
Ñi fi nekkoon dañ ñu jàppewoon ngandi imbéciles
Ñun kuñuy faale lañuy fal mooy tax ñu jage si la
Foog ñu job, foog ñu coob buñu bëgee ceeb bu niin
Kañ nga may wax ni Casamance jàmm delusi na?
Duma ci dara rew mee wax ma jotali la
Refrain
Jox ñu suñu wàl, jox ñu li nga ñu digoon
Nguur gi bumu neex ba nga fate li nga waxoon
Doomu rewmi ñoo la jiital kon boog teg ko ci yoon
Priorité mooy lan lañuy bayyil ëlëg suñuy doom
Mbuus bi ngay jaxaseeg suuf si aka bon
Saleté bi jëlee ko fi donoon na li gën
Kon doomu rew mi nañu xoolaat sunuy doxalin
Prési askan bee ma yónni, du caageni dama la miin