REFRAIN
Sa loxo set / Tes mains propres
Sa lepp set / Que tout soit propre
Bul nuyu kenn / Pas de salutations
Bul lëng kenn / Pas d’accolade
Bul génn kese ndax bëg génn / Ne sortir que si c’est essentiel
Bul sëqët fepp / Ne pas tousser n’importe où
Bul jége kenn / Toujours garder une distance de sécurité
Sëqët, fièvre, bop buy metti njëk feeñ / Premiers symptômes : toux, fièvre et maux de têtes
Soj, problème noyi, senn sa bakkan / Rhume, troubles respiratoires, écoulement nasales
Sëqët, fièvre, put buy metti, malaise feeñ / Toux, fiévre, maux de gorge, début de malaise
Du rey nit ku ñul si ñi xamul dëg ak fenn / Ca ne tue pas le noir, pur mensonge
Sa loxo set / Tes mains propres
Sa doom yi set / Tes enfants propres

COUPLET
Xeex ak Corona Virus, / Combattre le coronavirus
Microbe, jàngoro la, du nit / Il s’agit d’un virus pas d’un humain
Aduna nek si combat / Le monde est en guerre
Du gis ku muy xeexal / Contre un enemi invisible
Nuro nak grippe / Des symptômes de grippe
Nañu éviter contact physique / Evitons tout contact physique
Xajul Grand Yoff, Colobane , Pikine / N’a de place ni à Grand Yoof, ni à Colobane, ni à Pikine
Tax ba ñu annuler programmes yi siiw / Il est la raison de l’annulation de tous les programmes
Tax ba ñu foog ni àddinay tukki / Il donne un air de fin du monde
Medecin sonu na si li / Tous le personnel soignant au front
Amul vaccin, ordonnance tamit / Sans vaccin ni ordonnance
Mu ngi ray, day toroxal nit yi / Ce virus vulnérabilise et tue
Buñu tooge dina bari ay victimes / Si l’on reste observateur les victimes seront nombreuses
Set si sa askan, set si sa bopu / Propreté collective et individuelle
Tëju te baña seeti sa mbokk / Eviter les visites, rester chez soi
Julli sa màkkaan, Messe si la bokk / Toutes les prières à la maison quelle que soit notre religion
Xeex ko mu jeex mbir yepp mëna doxx / Combattons ce virus pour que tout revienne à la norme
Masque, sabu, antiseptique / Masques, savon ou gel antiseptique
Raxasu, sangu dadi set wecc / Se laver, laver ses mains, rester propre
Dal, muñ, bañ lu melni dess fi / Calme et sérénité pour éradiquer ce fléau
Gën di ñaan pour jamm day dikk / Prions ensemble afin de vaincre ce virus
REFRAIN
Sa loxo set / Tes mains propres
Sa lepp set / Que tout soit propre
Bul nuyu kenn / *Pas de salutations
Bul lëng kenn / Pas d’accolade
Bul génn kese ndax bëg génn / Ne sortir que si c’est essentiel
Bul sëqët fepp / Ne pas tousser n’importe où
Bul jége kenn / Toujours garder une distance de sécurité
Sëqët, fièvre, bop buy metti njëk feeñ / Premiers symptômes : toux, fièvre et maux de têtes
Soj, problème noyi, senn sa bakkan / Rhume, troubles respiratoires, écoulement nasales
Sëqët, fièvre, put buy metti, malaise feeñ / Toux, fiévre, maux de gorge, début de malaise
Du rey nit ku ñul si ñi xamul dëg ak fenn / Ca ne tue pas le noir, pur mensonge
Sa loxo set / Tes mains propres
Sa doom yi set / Tes enfants propres
Bul nuyu kenn / Pas de salutations
Bul lëng kenn / Pas d’accolade
Bul génn kese ndax bëg génn / Ne sortir que si c’est essentiel
Bul sëqët fepp / Ne pas tousser n’importe où
Bul jége kenn / Toujours garder une distance de sécurité
Sa loxo set / Tes mains propres
Sa lepp set / Que tout soit propre
Bul nuyu kenn / Pas de salutations
Bul lëng kenn / Pas d’accolade
Bul génn kese ndax bëg génn / Ne sortir que si c’est essentiel
ànd xeex coronavirus was written by Dip Doundou Guiss.
ànd xeex coronavirus was produced by .
Dip Doundou Guiss released ànd xeex coronavirus on Sat Mar 28 2020.